-
5
pages
-
Français
-
Documents
-
2013
Description
Seex Axmadu Bàmba MBAY, Wéy tàggat njàngale mi, Feentkatu Stivation « Jëxiis » Stivation“Jëxiis”, tuut tànk ci yooni tàggatum xel ak xam-xam ci pencoo Ca attum 1970 ak lu ko wër, ay kàngaam yuy yëngu ci wallu xel ak nekkin bokk ci ngiiru Piaget ca Genève, ñoom Doise, Mugny, Perret-Clermont, dañoo sumb ak coppite gu mattale ci wàllu njàngale ak njàngin. Sumb boobu nak da nu koo wéer ci gis-gisu tàggatum xel ak xam- xam ci pencoo. Kàngaam yooyu di askanoo ci Piaget wonenan ab feem ci njangalin buy sukkandiku ci tabax ak pencoo xam-xam. Feem wi wone na ne xaleel buy weccoo xalaat ak ay moroomam di na ful ay pexeem, di na nàmm xelam. 1 Seex Axmadu Bàmba MBAY, Wéy tàggat njàngale mi, Feentkatu Stivation « Jëxiis » Li ko sabab mooy ne xaleel suy diisoo ak ay moroomam di na jiixi- jaaxa ci ay xalaatu boppam, di na jiixi-jaaxa it ci digganteem ak ay moroomam. Jiixi-jaaxa googu di indi jàmarloo ak disoo. Lii lepp di wund ci gàttal ne jëf-lante yi xale yiy sexx di na sabab yokkute ci seen njàng. Feem wii di Stivation“Jëxiis”, tuut tànk ci yooni tàggatum xel ak xam-xam ci pencoo mi ngi sàmp ay reenam ci gisin wi nu leeral ci kaddu yi jiitu. Amul sikk ne di na jarin it taggatum mag ni ak way njàng liggeey bu mu mën a nekk. Ay ndongo-wéy saytu njàng mi ca FASTEF (Daara ju mag ji Cheikh Anta DIOP ca Dakar) def na nu ci ab gëstu bu xÒot, njurka ya am na solo lool.
-
Publié par
-
Publié le
31 mai 2013
-
Langue
Français